Yii yàlla bootu, jii Yàlla di boote
46
1 Tuur ma ñu naa Bel toqi na,tuur ma ñu naa Nebo sukk,
mala ya féetewoo seeni jëmm,
ñoom lees daan gàddua, tey jur gi jagoo,
di leen sëf ba loof.
2 Tuur yaa ngay sukk, bokk toqi;
manuñoo wallu seen jëmm ya,
xanaa doxal seen bopp, duggi ngàllo.
3 «Dégluleen yeen waa kër Yanqóoba,
yeen ndesu kër Israyil gépp,
yeen ñi ma dale yor ba ngeen juddoo,
di leen fab ba ngeen génnee seen biiru ndey.
4 Ba ba ngeen di magal, man la,
ba keroog ngeen di bijjaaw, maa leen di boot.
Maa sàkk, maay yor,
maay boot, xettli!
5 «Ana ku ngeen may niruleel,
di ma nàttableek a méngaleek moom,
ba ñu niroo lenn?
6 Ñii déy a yullee wurus ci mbuus,
sàkk xaalis, natt diisaay ba,
fey tëgg bu leen ci tëggal am tuur
mu ñuy sukkal ak a sujjóotal,
7 yékkati teg ci mbagg,
yóbbu, teg bérab, mu des fa;
du jóge fa mu tege,
ku ko woo wall it, du wuyu,
ba jot ko ci njàqare.
8 Fàttlikuleen lii te dëgërluwaat!
Yeen bàkkaarkat yi, defleen lii ci seen xel.
9 Fàttlikuleen cosaan la woon.
Man mii maay Yàlla, du keneen.
Amul Yàlla ju mel ni man!
10 Maay yégle muj ca ndoorte la,
ak jëf ju amagul, lu jiitu bu yàgg.
Maa naa sama mébét a ngi, day am,
sama bépp nammeel sotti.
11 Maay wooye jaxaay penku,
wooye réew mu sore, kuy sottal sama mébét.
Maay àddu, amal;
maay nas, sottal.
12 «Dégluleen maa, yeen dëgër bopp yi!
Yeenaka dëddu njekk!
13 Maa jegeñal sama njekk, soreetul;
sama wall a ngi, yàggatul.
Maay maye wall fi Siyoŋ gii,
ba Israyil gii di sama gànjar.»